Soxna Aminta Al Mardiyya

9
Page Titre Soxna Aminata Lo Al Mardiyya Par BaayFaalu SoxnaJaara © 1436 h / 2015 - www.drouss.org Tous droits de reproduction réservés, sauf pour distribution gratuite sans rien modifier du texte. Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez nous contacter par le biais de notre site internet : www.drouss.org

description

Sur la vie de la vertueuse Soxna Aminta Lo

Transcript of Soxna Aminta Al Mardiyya

Page 1: Soxna Aminta Al Mardiyya

Page Titre

Soxna Aminata LoAl Mardiyya

Par

BaayFaalu SoxnaJaara

© 1436 h / 2015 - www.drouss.orgTous droits de reproduction réservés, sauf pour distribution

gratuite sans rien modifier du texte.Pour toutes questions, suggestions, ou erreurs, veuillez

nous contacter par le biais de notre site internet : www.drouss.org

Page 2: Soxna Aminta Al Mardiyya

- 2 -

Quelques indications

Wolof Française = é per péru = ou rus rousc = th caam thiamñ = gn ñam gnamx = kh xol kholj = dj jibi djibinj = nd njaay ndiayend = nd nday ndeyeŋ ŋaam (machoire)ë = eu gëm = geumé = è (plus dur) = rér perduòo = au gòor gaureq = xx suqali soukh khaliii - uu - oo - aa ee (tirer sur le son) ; Ex : biir - suur -xool - gaal - xeer

Page 3: Soxna Aminta Al Mardiyya

- 3 -

Soxna Aminata Lo Al Mardiyya

Bés bu magga ngi jubsi, bésub cant, bésub fattaliku nitu Yalla, , di Magga-lu Mbakke-Kajoor .

Di bisu fattaliku Sëriñ Muhammadu Laamin Baara Mbakke.

Jëmm ju doonoon Jambari Lislaam, amooni may fa Sunu Boroom, doo-noon boroom sañ-sañ ba, ba kénn dul dindi.

Jaglé gamu amoon fa Boroomam, ak ci Sëriñ bi, kawéwoon na njortu, loolu.

Dana yéll ci bis biñ kéy fattaliku, ñu fattalikuwaale lépp luko waajaloon. Kénn si ñooñu di waajuram wu jigéen Soxna Aminata Lo.

Boroom Tuubaa Xadimu-r-Rasuul daan na wax naan : « Li fi néé dé, lig-géeyu ndéy joxéwuko, waayé ku ndéyam liggéeyul du ci jot »

Mu mélni Soxna Aminata Lo, ku déggoon wax jooju la, té jëfé ko. Liggéey ba Boroom bi jagléleko, Sëriñ Muhammadul Mustafa mi taxawal yoon wi ganaaw Sëriñ bi, toftalaalé ca Sëriñ Muhammadu Laamin Baara miy Boroom Sañ-sañ bi.

Déllu si ci dundug Soxna si dana yéesal pas-pas, fóotaat ay jikko, soññaat soxnay jamoonoy téy, rawatina man mii.

Soxna si wajuram yu séll yi ko Sunu Boroom jagléel taxoon mu doonoon ku ñépp rafétoon njortu.

Bokku ci askanu Muxtaar Ndumbé, mi nga xamni Boroom Tuubaa Xa-diimu-r-Rasuul séedéwoon na ca moom ci Jazaa’u Sakoor wa atuuf né « Maxtaar Ndumbé mooy sangub kumu jamoonontél ci suufus Kajoor ».

Soxna Aminata lo, di doomi Soxna Xari Maam Jóob ak Sëriñ Tafsir Mox-taar Binta Lo Ñomré bokkoon ci waa Kokki, di askan wu ñu raññé si Islam, géstu, jang ak jangalé Al Qur’ân.

Té loolu Sëriñ Abdu-r-Rahmaan Lo, bokku bénn waajur ak Soxna Ami-nata Lo, doyna ci sëkk firndé, ndax moom la Ku Tédd Ki dénkoon ñu bari ci njamboot gi, ngir mu jangal léen.

Page 4: Soxna Aminta Al Mardiyya

- 4 -

Soxna Aminata Lo donoon ku séll, ku yiw, am diiné, ñéméwoon loolu di wéetal Boroomam.

Séllam ga taxoon na fumu gisée nitu Yalla xammé ko, té loolu doy sëkk ak jaglé ci Soxna.

Li ciy firndé mooy kéroog bi Boroom Tuubaa di gané Sëriñ Mbañang Fallo mi donoon mag mu ñu xamoon si jaamu Yalla, amoon tur ca ja-moono yooya. Ni mag ñi améwoon loolu yité ci séen biir ak di téralantée ka toppato séeni gan, taxna Sëriñ Mbañang Fallo sant kénn si waakëram ci jamoono yooya, di Soxna Aminta Lo, ngir mu yéesal Laxasaayi Kubaax Ki yoroon, ganaaw bako Sëriñ bi yitéwowoon

Soxna Aminata, ca gis ak yég gu sori ga, bamiy fóot laxasaay ya, dafa guux yari guux ca sumbu bu njëkk ba (moome la mag ñiy wax sumbus tooyal), la ca déss mu rooséko ca biir néegam.

Laxasaay yi bamu ko footé ba noppi, dafa takuk buum ca néegam, déf ca ak liiñ, daldi ka féy wéer bamu wow.

Liggéey bu séll boobu mu déf, tax na bi Sëriñ biy déllu, Sëriñ Mbañang Fallo Jeng niko damaa bëgg nga ñaanalko. Sëriñ bi niko waxal lo bëgg ñu défal lako.

Soxna si niko xanaa ku mélni yaw.

Sëriñ bi niko loolu déy faat na, waayé nak Sunu Boroom man na luné, daldi yéwiku.

Jamoono di wéy ba am bis, Soxna Penda Buya, di jambaar loolu moomit (li ciy firndé moom la Sëriñ bi bindaloon Wasiiyyatu Soxna Penda Buya), jikko yu séll yim sétluwoon si Soxna Aminata lo, taxoon mu amoon yéené andiko ci daaray Sëriñ bi.

Soxna Penda Buya Jóob moomu mo donoon Soxnas Sëriñ Ibrahima Mba-kke Kajoor miy rakku Sëriñ Maam Moor Anta Salli.

Soxna Penda Buya di doomu ndéyu Soxna Aminata Lo, ndax waajuram Samba Aminata ak Soxna Xari Maam miy ndéyu Soxna Aminata Lo ñoo bokku ndéy ak baay.

Soxna Penda Buya fonkoon na loolu Sëriñ Tuubaa, jébbaluwoon si moom.

Page 5: Soxna Aminta Al Mardiyya

- 5 -

Ganaaw bamu ca défé ay jéego, Sunu Boroom japandil ko.

Ñu taxaw foofu tuuti, fattali tuuti ci démug Këru Soxna Aminata Lo, ndax fattali gi dana doon ak soññé, ci man ak samay maas.

Kéroog bamiy war, ci niko mag ñi daan waxé, fas bako jélsi, Soxna si dafni du ci yéeg.

Muniléen waruwaay bu jugé ci kër Shayhul Xadiim, sañumacée yéeg, xanaa ma dox and ak yéen ba kéroog ñuy agg.

Loolu wutéek loolu ak sunu jamoonoy tay, nga xamni su séet bi di dém kër, dañ naa la, su nangami woto ñéwul séet bi du dém. Tégal la ci nila caar yi na bari ndax ñikoy toppu daa bari, taxi ni na bari ndax bajjan yi dunu duggu si caar, na 4x4 ba Harmer bu wéex tall,diig, ndax séet bi ci la wara duggu.

[Subhaanala, lii jarnaa tiit, ndax kunuy yabal muy dém, da melni dano fatté ni day dém jayanté ji, daa wara dém tarbiyu ji, da wara dém waajlal ngëram njamboot gu dikkagul]. Man ak sama maas gi war cée bayyi xél bu baax, té bañ di nangu soséeté bi dinu yobbaalé ci séen doxalin gu té-guwul ci diiné, ak naan la sooko déful nu yap la, ndax say moroom rék lañ ko fiy défal, té gënuñu la.

Nanu fattaliku ni, liy tax, ñu xéep ab Soxna du ay téranga yamu am ak yamu amul, waayé mélokaanu jabootam lañ kéy sikkée mbaa ñu nawéeko ko ëlëg.

Ñu délluwaat si Soxna si aki jangaléem, kéroog bamu aggé kër, li di alali farataam, nga xamni sunuy jamoono moom lanuy wax ay boyitu oor ak yuni mél….Moom déey, jamoonoom lako Sunu Boroom cëraléwoon ci ay takkaay dakoo jox Ku Tédd Ki addiya, niko : « takkaay dé, tëd lay tékki, té man damaa ñëw ngir liggéey-si, tëdsiwuma… ».

Mu mélni ku liggéeyul lanuy séddalé dooca am. Soxna si déggoon loolu aaya bi Sunu Boroom wax ni « yaw Yonént bi, waxal sa Soxna yi, su-dée xéwalu addina bi rékk, lañ soxla, nanu ñëw danaa léen ci jox bañu doyal, té nga yéewiléen, sudé nak Yalla akuk Yonéntam , ak këru dëgg rék mooléen yittéel, nanu xamni séenuk néexal danaa léen ko dénccal ba ëlëg, ca kërug dëgg ga ». Bis boobé la sunu Yaay Saydatunaa Aysha wan ginaaw xéewalu adduna yépp, bañaticaa bëgg dara, gëna dégmal Yalla ak

Page 6: Soxna Aminta Al Mardiyya

- 6 -

Yonéntam

Ô Prophète ! Dis à tes épouses : Si c›est la vie présente que vous désirez et sa parure, alors venez ! Je vous donnerez (les moyens) d›en jouir et vous libérerez (par un divorce sans préjudice). Mais si c›est Dieu que vous voulez et Son Messager ainsi que la demeure dernière, Dieu a pré-paré pour les bienfaisantes parmi vous une énorme récompense. (Coran 33.28)

Aysha répondit au Prophète Anleyhi-s-Salaatu wa-s-Salaam après avoir écouté de sa bouche ce verset : c’est Dieu, Son Envoyé et la demeure der-nière que je désire.

Soxna Aminata Lo nékoon ku téey, amoon doxiin wu téey.

Masula rombu Sëriñ bi ak ay dallam, té Sëriñ bi masukoo rombu fékk ko mu taxaw. Bu Sëriñ bi dée jall, dafay agg suuf bamu dém, mu doora jug.

Ci aw ñakkam ladaa téralée. Likay dëggal, amna bis Sëriñ bi masnaa jox Maam Céerno Ibra Faati as lëf si xaalisu ngurdu bamu yoroon, niko joxalmako Soxna Aminata Al Mardiyya (noonu lako Kubaax ki daane woowé) , té santalmako.

Bako Maam Céerno joxée Soxna si da cée barkéelu, raay ko ci xar kana-mam, ndax limu jogé ci Sëriñ bi, daaldi wax Maam Céerno : « néel Ku-baax Ki joxaatnaako ko addiya, ndax kër gi dama fée war di andi, waayé duma fi génnée mukku ».

Wuuténa loolu ak sama maasug téy gii nga xamni, kooci joxul déppaans yaari fan, ganaaw suba mu wootéel la réeñong dé famiiy.

Jaayanté Soxna si ci fan yooyu man nanu japp ni bokku na ci litax Sunu Boroom fayé ko yaari Muhammadu yi. Néenañu amna bis Sëriñ Balla Maam Turé néenako  :  Yaw Soxna Aminta Lo, yaw dé da mélni taxuko jamboot ci kër Sëriñ bi, mélnani yaari bant képp nga fa.

Soxna si niko : bariy doom dé bari bamméel rék, waayé jur lu ñépp xam té ñuy jariñé doyna sëkk.

Loolu mélni Sëriñ Muhammadu Laamin Baara, ci jamoonom, dëggalna-ko ci ay kaddu, ndax amna bis kuko masa laaj, niko damaa bëgga xam baxam ndéy ju liggéey ak ñaanu waliyyu bu ci gën ?

Page 7: Soxna Aminta Al Mardiyya

- 7 -

Sëriñ Bara tontu ko, niko Boroom ndéy ju liggéeyul dé, du dajéek waliyyu bam koy ñaanal.

Loolu di firndé ; ni ndéy ju liggéey dana dimbali doom ca lako Sunu Bo-room di namma faggul.

Jaayantég Soxna Aminata Lo amulwoon yamuwaay, pas-pas ba fuñko na-toon wéesunafa, démam gi doyna ci firndé.

Ganaaw ba Sunu Boroom Xamalée Ku Tédd Ki xéw xéw woowu waroona am ci jëmmam gi, ngir ñoom ñaar dunu nëbbanté dara. Ku Tédd Ki am ñumu woo, xamal léen ni, Sunu Boroom dakoo xamal ni waxtoom jotna, waayé kénéen kumu yabal, Sunu Boroom nangul kako, ngir moom Sëriñ bi mu mana aggalé liggéey bi.

Nénañ amna kénn kuko sasoowoon, waayé ba bës ba jégée, daa dikkaat si Sëriñ bi, niko : « man ab toppu dong la, té toppu du jiitub séet », (maanam daa joxé ngant ci kaw né Sëriñ béeko wara jiitu)

Amoon kénéen nit koo xamni bamu ko déggée, dafni Sëriñ bi, « Mbakke, yaw dé lo bëgg Yalla déf ko, waayé Aajanay déwéen déema ganal ju rén » (moomit joxé ngant).

Loolé nak bamu toqqée ci noppu Soxna Aminata Lo, Soxna si dafni Ku-baax Ki : « su dée Sunu Boroom séexluwul sama ruuh, noppinaa ngir dém, man naa bayé Muhammadu Laamin Baara Soxna Awa Buso, ndax li war ci moom danako fa matée » .Boobu Sëriñ Baaraa ngi tollu ci juroom bénni wéer, doonub pérantal [tuub ci kaddu gi].

Nga xamné bénéen Soxna bumu doonoon, ak doom nimu néexé ci yaay, da nga naan xalaatuma dém bayyi fi sama jaboot té duma xam kuléeni yor.

Waayé bii xalaat bu rafét, ak pas-pas bu kawé la Soxna si, amoon.

Waxtaan waa nga amoon ab dibéer, talaata ci guddi ci la Soxna si wacc lig-géey, ci waxtu wo xam né Kubaax ki, ma nga woon ci naafilam yamu daan faral di déf, guddi gu jot, di ca wéet ak Boroomam ; muy mbir mu yéemé. Mbir moo xamné, ku tolluwul ak ñoom maqaama fa Sunu Boroom lottu nga ci xam mbir moom namu démé.

Ca fajaru allarba, lanu ko déncc, Sëriñ bi diglé ñu déncc ko Guy-Téxé.

Page 8: Soxna Aminta Al Mardiyya

- 8 -

Jamoono yooyu, kénn nékkagufa kudul kuñuy wax Sëriñ Mustafa Ma-roon. Kooku rék lañ fa dénccoon. Li ciy firndé, bañ kay yobbu, Sëriñ bi daa xool Sëriñ Maxtaar Mareema, donoon cammiñ ci Soxna si, niko Maxtaar da ngay jooy, munéko déedét Mbakke. Sëriñ bi niko, mbaa doo-léen foog né Soxna si daa nara wéet fii  ? Munéko bu ëlëgué képp ku fiy ñaanati, dang ka key sanni.

Té kaddu yooyu, jamoono dakoo dëggal, ndax amna bis ag kilifa bu doon déncc Soxnas taalibém, da séédé si Soxna soosu ni : « kii déy, séedénaa ni kuko gën tëddu fi » 

Mag ñi néttalinañ ni, kilifa googu dé, bamu tëddé guddi da gént Soxna Aminata Lo muniko « xawma fénéen, waayé ñénti wét yi ma wër, lu fi waay am sama loxo yii la jaar »

Soxna si soññé akug yobbal si béppu Soxna, rawatina sunu jamoonoy téy.

Waruñu yam si Céy rék, mbaa Ëskéy, di yéemu ci jaar-jaaram, waayé Soxna su nék dafa wara nataat boppam, nataat mélokaanam, aki jëfam, su booba dana xam famu féeté.

Ñu wara jang lu bari ci moom, té ñu baña jël ak mbaax jagléel ko mag ñi rék, foog-ni jaayanté faatna sunu jamoonoy téy.

Ndax li Sëriñ Fallu Mbakke daane wax rék, moo ci nékk : waliyyu ya Sunu Boroom daan saakk mi ngi léeni saakk ba téy, dañu né siiw gis jigéen yu baax ba Sunu Boroom jaaraléko ca ñoom, ñu yéksi jamoono.

Téy nak, Soxna su déglu waxtaanu soññé, jëm ci jaayanté Soxna Xadiija, so noppé dafa naan la : Soxna Xadiija daa amoon tawféexu dajéek Gën gi mbindéef mootax lamu man duma ko man.

Ko soññu si Soxna Jaara, munila : Maam Moor Anta Sall mooko ko yom-baloon.

Ko soññu si Soxna Mariama Jaxaté, mbaa Soxna Aminata Lo, mbaa Soxna Awa Buso, Soxna Faat Jaxaté ak ñénéen ak ñénéen ci waa Ahlu Barzaaq, munila : Sëriñ Bu Mag bi Soxna su nékk si daaram nii rékk nga mana doxalée.

Naam dëgg la, ndax góor Yalla so nékké ak moom dalay xértal ci ak jaamu Yalla waayé loolu duw léy ci Soxna. Ndax liciy misaal mooy, Soxna Aasiya,

Page 9: Soxna Aminta Al Mardiyya

- 9 -

Boroom këram di Firaawna , ab yéefar lawoon bu doon tooñ YALLA, di bunduxatal ab Yonéntam, téewul Soxna Aasiya jaayanté ak Boroomam, déf lamu warloo ak Boroom këram, baa Sunu Boroom séedé kër ca Al Janna. Al Qur’ân limnako, booléko ci Soxna Yi gana tédd, té Boroom këram gëmutoon.

Soxnaas Yonént Yalla Noh, ak Soxnass Yonént Yalla Loth, téy séeni kër ca këru mugal ga la, té mooné, ña gën ci séeni jamoono la léen Sunu Boroom booléloon, ñu ëppoon ñépp tawféex, waayé défunu laléen war, ba loolu yobéléen mujjé ca kërug téxéedi, kërug alkandé.

« Allah a cité en parabole pour ceux qui ont mécru la femme de Noé et la femme de Lot. Elles étaient sous l›autorité de deux vertueux de Nos serviteurs. Toutes deux les trahirent et ils ne furent d›aucune aide pour [ces deux femmes] vis-à-vis d›Allah. Et il [leur] fut dit : «Entrez au Feu toutes les deux, avec ceux qui y entrent» [Sourate 66 verset 10 L’interdic-tion (At-Tahrim)]

Ngala kon nanu yéewu, yéesalaat pas-pas yi, laxasaay yi, sol mbubbum Tuub, takk ca dérug jaayanté, fas yééné laakk ngëramal Sunu Boroom, ak ñiñu Yalla boolél, bañ léen xoolé séni jëmm, waayé xooléléen linu boolé : Mooy Sëy té Jëmmi YALLA rékk tax.

Bilé Soññé lañu dunduk Soxna Aminata Lo wara jariñ.

Yalla na Yalla Yokku ay léeram , té taas ñu si barkéem, barkéb njabootam gu tédd gii, ak liggéeyam bu Séll bi.

Par BaayFaalu SoxnaJaara

© 1436 h / 2015 – www.drouss.org - ‐ Tous droits réservés.